*Mercato médiatique: Ramatoulaye sarr quitte Walfadjri et rejoint la RTS.*
Journaliste bii di ramatoulaye sarr daldi dina tàggatoo ak groupe Walfadjri guinaaw ay année you bari youm fa def,
Mou gneuwoon Walfadjri 2007, nekkoon na sen correspondante sa région bou Thiès guinaaw gui gnou indi ko Dakar, daan na def journal français 12h, revue de presse français bokkoon na tamit ci équipe émission keppar gui Walf fm ak Pencoo Walf tv, yoroon na rubrique économique altiné bou diot ak émission économique alkhamis bou diot 20h ci Walf fm.
Moo djité woon Amical des dames du groupe Walfadjri « ADAW », guinaaw ci congé bim nekkoon fala diaarè dem sa télévision nationale RTS, mou tàxalikook gnim doon liggéeyal ci anam bou rafét.
Xibaaru reewmi diko niaanal yoonou jàmm
*Mame fallou dieng xibaaru reewmi*